Menu

Esekiyel 15

MBS

1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 2 «Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi, ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi? 3 Ndax dees na ca sàkk bant, liggéeye ko? Am dees na ca sàkke wékkukaay, wékk ca lenn? 4 Xanaa sànni cib taal, xambe, ñaari cat ya lakk, digg ba xoyomu. Ana lu deeti njariñam? 5 Ndegam ba mu nee ñumm, lees ci dul liggéey dara, gën ba mu jàppee ba xoyomu. 6 Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dees na xamb caru reseñ, mu bokk ci banti garab yi ma joxe, ñu xamb lépp, te noonu laay xambe waa Yerusalem. 7 Maay jànkoonteek ñoom, ñu rëcc sawara, sawara lakk leen. Bu ma jànkoonteek ñoom, dingeen xam ne maay Aji Sax ji. 8 Maay gental réew mi, ñoo def jëfi ñàkk worma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate