Esayi 15
MBS1 Yéene bii ñeel na Mowab: Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes! Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes! 2 Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérebi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu, 3 nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, ak kaw taax yaak pénc ya, ku ne di jooy ba say rongooñ wale. 4 Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu, seen baat àkki ba Yaxacc, xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo, ne yàcc ne yasar! 5 Maay jooy Mowab jooyi xol, nit ñaa nga fay dawe ba Cowar, àkki ba Eglat Selisiya. Ña ngay yéeg jëm Luxit, di jooyoo, awe yoonu Oronayim, di yuuxu. 6 Dexu Nimrim wow na, ñax wow, gàncax lax, dara naatatul. 7 Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon, yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya. 8 Yuux déy maase na réewum Mowab, jooyoo ya ba Eglayim, jooyoo ya ba Beer Elim. 9 Dexu Dimon déy fees na ak deret, te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw, ba ku rëcce Mowab, ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!
