Taalifi cant 28
MBS1 Ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, yaw laay woo, di la wéeroo, bu ma tanqamlu. Soo nee cell, ma xawa tàbbim pax. 2 Ngalla déglul, ma tinu la, woo la wall, dékk lay loxo, jublu sa néegu biir bu sell ba. 3 Bu ma sànkaaleek ab soxor, di ma booleek kuy def lu bon, di wax moroom ma jàmm, te dencal ko ay ca xolam. 4 Fey leen seen liggéey, seen kemu jëf ju bon. Jox leen seen añu jëf, yool leen seen yelleef. 5 Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, ak liggéey bi mu def. Da leen di yàqate, te dootu leen yékkati. 6 Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan! 7 Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko. 8 Aji Sax jeey dooleel ñoñam. Mooy làq, di musal buur bi mu fal. 9 Ngalla musalal sa mbooloo, barkeelal sa ñoñ ñii, sàmm leen, boot ba fàww.
