Menu

Taalifi cant 3

MBS

1 Dib taalifu cant, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor . 2 Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare! Ñu baree may jógal, 3 ñu baree may tooge naa: «Yàlla du ko wallu!» Selaw . 4 Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, di ma teral, di ma siggil. 5 Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw. 6 Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar. 7 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal. 8 Éy Aji Sax ji sama Yàlla, jógal, wallu ma! Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, foq seeni sell. 9 Aji Sax ji, yaa moom wall, sa mbooloo jagoo sa barke. Selaw.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate