Menu

Taalifi cant 47

MBS

1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor. 2 Na xeetoo xeet tàccu, xaacu, sarxolleel Yàlla! 3 Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal, mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp. 4 Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi. 5 Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp. Selaw. 6 Yàllaa yéeg, kàddu riir. Aji Sax jee yéeg, bufta jolli. 7 Woyleen Yàlla, woyleen, woyleen Yàlla sunu buur, woyleen. 8 Yàllaay buuru àddina sépp; taalifleen, woy ko. 9 Yàllaa di buuru xeet yi, Yàllaa tooge jalam bu sell. 10 Kàngami xeet yeey daje, ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma; Yàllaa moom buur yi yiir àddina, te moo kawee kawe.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate