Menu

Taalifi cant 54

MBS

1 Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda. 2 Mooy ba waa Sif demee ca Sawul, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew . 3 Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur, jox ma dëgg, ci sa kàttan. 4 Éy Yàlla, déglul, ma ñaan, teewlul, ma wax la. 5 Ay doxandéem a ma jógal, di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan, te seetuñu ci Yàlla. Selaw. 6 Yàllaa ngii, moo may dimbali; Boroom bee yor sama bakkan. 7 Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru, yal na leen sa dëgg sànk. 8 Xol bu tàlli laa lay sarxale. Aji Sax ji, yaa baax, ma sant la. 9 Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële, ma tiim samay noon.

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate