Taalifi cant 58
MBS1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda. 2 Yeen daal, su ngeen waxee, dëgg selaw. Mbaa yeena ngi àtte nit ñi ci yoon? 3 Yeena ngi mébét njubadi, di lawal fitna ci réew mi. 4 Ku bon day sosu rekk, dëng; juddu, teggi yoon, dib fen-kat. 5 Day am daŋar ni ñàngóor, fatti noppam ni jaan ju tëx: 6 du dégg baatu jatkat, mbaa jati ñeengokat bu ñàng. 7 Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ; Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii. 8 Yal nañu ne mes ni ndox muy wal, yal nañu diir seen fitt, mu damm, 9 yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant. 10 Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku . 11 Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég, muy jàngoo deretu ku bon. 12 Ku ne naan: «Ku jub jot sab yool moos! Te Yàllaa ngi fi moos, di àtte àddina!»
