Menu

Taalifi cant 95

MBS

1 Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji, nu xaacul sunu wéeru-mucc. 2 Nanu ko dikke cant, woyal ko, mu riir. 3 Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp. 4 Moo moom xóotey suuf, moom colli tund yi, 5 moom géej, sàkk ko, moom jéeri ji mu mooñ. 6 Nan sëgg, sujjóot, sukkal Aji Sax ji nu sàkk. 7 Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom 8 ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma, 9 fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat te gisoon samay jaloore . 10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas, ma ne: “Seen xol a dëkke lajj, ñu faaleedi samay santaane." 11 Moo ma taxa giñ ci sama biir mer, ne duñu tàbbi fa samag noflaay.»

Everything we make is available for free because of a generous community of supporters.

Donate